Nos valeurs
Il faut passer de l’idée, à la réflexion et à une stratégie bien conçue et murie dans le sens d’une communauté d’actions. Le Sénégal doit nécessairement passer par une prise de conscience de ses filles et fils. Il doit en résulter des changements au plan individuel et collectif, dans un esprit communautaire pour promouvoir des retombées positives aux plans politique, sociale, environnemental et sociétal.
L’idée s’appuie sur la capacité de chaque individu à développer et faire développer des activités génératrices de revenus. La première richesse c’est le capital humain et les inestimables ressources de vie et de survie des Sénégalais pour changer qualitativement leur quotidien avant d’envisager leur avenir avec optimisme. Cela doit s’appuyer sur :
Xam xam : la nécessité d’être doté de potentiel doit être accompagné par le savoir, le savoir-être et le savoir-faire, le savoir faire-faire qui encadre l’action
Liggey : la force du travail comme élément essentiel pouvant changer les choses dans l’optique d’atteindre
les objectifs fixés
Njerign : le résultat escompté est l’atteinte des objectifs et la réalisation de nos rêves et aspirations. C’est aussi le fruit d’un travail muri et appliqué avec méthode et stratégie.
Na kuné am jikooy
boppu saxaar !
Fàww nu joge ci xalaat, jaar ci xòòtal gëstu, jëm ci ay tërëliin yu ñaw ngir mana ànd ci ay jëf. Fàww rééwum Senegaal jaar ci ay yëg-yëg yu bàyyikoo ci ay doomam, gòòr ak jigéén. Loolu wara jur ay coppite ci kenn ku nekk ci mbooloo mi, cig àndandoo ngir ay njariñ ci wàllu doxaliin yi, jàappalante gi, aalam gi ak askan wi. Xalaat baa ngi sukkëndiku ci man-manu kenn ku nekk jëm ci sos ay lëggééy yuy jur koom. Alal ji njëkk mooy doomu Aadama bi, ak Xariñ gu doo mu Senegaal Xariñ ci mana baaxal dundug teyam, laata muy xalaat gog ëlëgam ci xel mu dal. Loolu nak, dafa wara wééru ci xam-xam : manoore gi mbir miy laaj, fàww mu ànd ak ñatt yee: Xam Xam, jiko ju rafet, man-man ak mana jëfloo yiy jubal mbir. Lëggééy : kàttanu lëggééy, di mbir mi jiitu ci soppi yëf yi, ngir mana yegg ci mébét yi. Njariñ : li nu ciy xaar nak mooy yegg ci mebet yi, ak teg sunu loxo ci sunuy yaakaar. Te loolu, lëggééy bu sell, bu wér, bu tegu ciw yoon moo ko jur.