Notre vision

Du point de vue économique, le Mouvement BOPPU SAXAAR prône l’auto-emploi et la solidarité. Le programme économique est d’une inspiration libérale et progressiste mais de type sénégalais Jëf Jël ou encore Ñax Jariñu

Le Mouvement propose l'adoption de projets de grande envergure en

faveur de la solidarité. Cette dernière ne doit pas s’arrêter aux frontières de la famille, mais s’étendre au quartier et à la ville pour s’élargir à la nation.

Nous invitons nos concitoyens à rejoindre le Mouvement pour qu’ensemble, nous puissions faire de chaque Sénégalaise et de chaque Sénégalais, une locomotive capable de tirer le pays vers l’essor économique et sociale au bénéfice de tous.

Na kuné am jikooy

boppu saxaar !

Ci wàllu koom, yor sa lëggééyub bopp ak jàppalante la kurelu « boppu saxaar » gëm. Ni nu gise mbiri koom nak, mi ngi sukkëndiku ci gis gisu « liberaal », muy kune sañ ngaa taxawal sa mbiri bopp, ak « progressiste » di xalaatu jëm kanam ; waaye nak, nu dëppëlekook li nuy wax Senegaal jëf jël mbaa ñaq jariñu. Kurel gi namm naa sòòbu ci naal yu mag, jëm ci jàppalante ; jàppalante gog, warula yem rek ci kër gi, waaye day ëmbaale gox bi, dëkk bi ba ci rééw mi yépp. Noo ngi woo mbokki rééw mi, ñu fekki si nu ci kurel gi ngir, nu fexe ba doomi Senegaal bu nekk, muy gòòr di jigéén mu soppiku boppu saxaar bu mana xëcc rééw mi jëme ko ci yokku ci koom ak ci nekkiinu askan, ci luy jariñ ñépp.