Qui sommes-nous?
Le Mouvement BOPPU SAXAAR est un mouvement social et politique, qui prône le développement participatif direct, d’où le concept de BOPPU SAXAAR . Notre objectif à terme est de créer un parti légalement constitué.
Dans sa forme actuelle, le Mouvement est ouvert aux Sénégalais d’ici et de la Diaspora.
Le Mouvement veut s’appuyer sur les valeurs de XAM XAM ,LIGGEY ET NJERIÑ, pour la raison que le Savoir et le Travail constituent, partout le socle du développement.
Nous prônons également un engagement citoyen, social et humanitaire, explicite et franc.
Le Mouvement utilisera les réseaux sociaux comme moyen d'information. Le Mouvement ambitionne d’amener la société à faire la Politique autrement et à envisager le changement de manière profitable à tous.
Na kuné am jikooy
boppu saxaar !
Senegaalay li njëkk ci li nu bokk moom, ba tax warteef lay doon ci nun, nu ñoŋal ko, naatal ko. Farata ju day noonu nak, ci doomu rééw, dafay laaj gòòr ak jigéén bàyyi ci xel. yitte ji gëna wér nak, day daadi doon bokkug bëgg ak mengële ay taxawaay. Sërin Saaliwu MBÀKKE mu tedd ma moo gisoon misaal mi, dëppëlekoog saxaar. Dox nak ngir mu mana am, fàww mu am bopp bu ànd ak doole juy tax ñu man cee lonk ay wago yu bokk jëmu. Noonuu la ko Xalifa bu maandu ba xalaate woon, tudde ko « boppu saxaar ». Fii nak, day laaj doomu rééw ju nekk, nga yëg ci sa bopp ne, lenn nga, lu manta ñàkk ci saxxar gi wara yòbb mbooloo mi ci tukki bob, man naa yàgg de, waaye teeru ba mooy, ci sunu rééw mii, ag yokk guy ëmb pajum aajoy mboolem ñi ne ci biir : di ASKAN WI. Kàttan gi boppu saxaar biy génne nak ngir doxal mbir mi, day doon ay lëggééy yu kenn ku nekk di sasoo. Kàttan googu manes na koo bokk, manees na koo boole, ndax bu fekkee ne saxaar yeek bopp yi dañoo bari, du nu def rek lu dul boole doole yi.