Notre philosophie
« nit dafa wara am jiko BOPPU SAXAAR bu andé moom kessé duko terré ég famu jem té it bu yobaalé ay wagon du ko téré ég té it du ko téré jitu ». La locomotive est la force qui tire et entraine les wagons qui, quelle que soit leur charge, roulent vers la destination du train. Appliqué à la société, le triptyque Discipline, Solidarité et Cohésion sera une condition aux avancées projetées. Dans le Mouvement à enclencher, nul ne devra se sentir exclut ni laissé sur le bord de route, d’où l’appel à une participation inclusive, car les voyageurs doivent nécessairement être en gare pourprendre le train ensemble.
Na kuné am jikooy
boppu saxaar !
Kurelu « bopp saxxar » mbooloom askan la mu ànd ciy tërëliin ngir jëmmal ag yokk gu ñépp di seq ; looloo indi baatu « boppu saxaar ». Sunug jublu nak mooy, bunu ca yeggee, taxawal parti polotik ci ni ko yoon tërële. Fii nu toll nak, ubbil nanu kurel gi doomi Senegaal yi ci biir rééw mi ak yi ci bitti. Li kurel gi fas yééne yit, mooy sukkëndiku ci XAM-XAM, LËGGĖĖY ak NJARIŇ ngir li xam-xam ak lëggééy doon fune, cëslaayu yokku. Dinanu jiital it dogug doomu rééw, gu askan ak yërmaande, dogu gu leer te dëggu. Kurel gi fas naa yéénee jëfëndikoo jumtukaayi yëgle yu yees yi ngir siiwal ay xibaaram. Liy pas-pasu kurel gi mooy fexe ba askan wi soppi ni ñuy defe polotik ak yééne ay coppite yuy amal ñépp njariñ. Na kune am jikkòy boppu saxaar ! Sunu gis gis « Nit dafa wara am jikkòy boppu saxaar, bu àndee moom kese, du ko teree yegg fa mu jëm ; te yit, bu yòbbaalee ay wago, du ko teree yegg, du ko teree jiitu ». Boppu saxaar mooy doole jiy xëcc, di yòbbu wago yi ; te lu wago yi diis diis, fi saxaar gi jëm rek la ñuy jublu. Boo ko indéé ci askan wi nak, ñatti mbir yii di yar, dimbëlante ak booloo, day daadi doon sart ci mebet mi. Ci jòg gi nu nara sos, kenn waru cee yëg ag beddi, mbaa boddi ; moo tax nuy woote sòòbu gu bàyyi wul kenn ; ndax kat, ñiy dem, fàww ñu nekk cib teeru ngir ñu mana demandoo
Na kuné am jikooy
boppu saxaar !